Aji Sax ji nee: «Saab saamar a reye fa asamaan ba màndi deret, te mu ngii di wàccal Edom, xeet wi may faagaagal, ngir àttee leen ko.»
TSK
TSK · Isaiah 34:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
«Maa doon dëre tànk, man kenn ci ab dërukaayu reseñ, xeet yépp kenn dërlewu ma ci. Sama mer laa leen dëre, samam sànj laa leen dëggaatee, seen deret tis ci samay yére, ma taqal sama yére yépp.
Giñ naa ko ci man mii, déy,» kàddug Aji Sax jee, «Boccra, dëkk bii day mujj di gent bu ñu doyadal, ndànd-foyfoy bu ñuy móoloo, dëkk-dëkkaanam yépp gental ba fàww.»
Aji Sax ji nee: «Maa leen di wommat niy xar ba ca rendikaay ba, ñu mel ni kuuyi xar aki sikket.
ba képp kuy dund xam ne man Aji Sax ji maa bocci sama saamar, te du dellu mbaram.”
Yàppu xarekat ngeen di lekk, naan deretu garmiy réew mi, ñooy seeni kuuy, aki tàppaanga aki bëy aki yëkk, ñoom ñépp mel ni juru yafal yuy fore jooru Basan.
¶ Ma gis nag menn malaaka mu taxaw ci jant bi. Mu àddu ca kaw, wax ak mboolem picc, yiy naaw ci digg asamaan, ne leen: «Dikkleen, dajesileen ci bernde ju mag ju Yàlla ji,