TSK

TSK · Isaiah 34:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Maay kiy feye, di añale, te bu jotee ñu fakkastalu, ndax seen bésub toskaree dëgmal, dogal ba buur, wutsi leen!»

Éy Aji Sax ji Yàlla, boroom mbugal! Boroom mbugal, feqal sag leer!

Bésub Aji Sax jaa ngii di ñëw, bés bu néeg, bésub mer ak sànj muy tàkk, nara gental suuf, te bàkkaarkat ya la fay fàkkas.

Ku fitam rëcc, ne leen ko: «Dëgërlul te bul tiit. Sa Yàllaa ngii di la feyul, ba yool say noon. Moom mooy dikk, wallusi la.»

Moo sol kiiraayal njekk, mbaxanawoo mucc, solati yérey mbugale, làmboo turkib xéraange.

Bésub mbugal laa mébétoon, te atum njot teew.

Micah 6:1 TSK

Dégluleen rekk li Aji Sax ji wax: Jógal layoo, tund yu mag yi seede, tund yu ndaw yi dégg la.

¶ Waaye sag dëgër bopp, ak sa xol bu tuubadi, ci ngay jóore sànjum Yàlla ci sa kaw bopp, keroog bésub sànj ma, fa àtteb Yàlla bu jub di feeñe.

Te kat njekku Yàlla dina feeñ ndax coono ba muy delloo ñi leen teg ab coono.

Ndokklee, asamaan, Ndokklee, yeen ñu sell ñi itam, ak ndawi Yàlla yeek yonent yi, ndaxte Yàllaa leen àtteek dëkk bii, mbugal ko.