Waaye duma ko def ci sag dund ngir sa baay Daawuda. Ci sa loxol doom ju góor laa koy foqatee.
TSK
TSK · Isaiah 37:35
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Terewul Daawuda tax Aji Sax ji Yàllaam may ko doom ju góor ju koy wuutu ca Yerusalem, ndax askanu Daawuda baña fey, Yerusalem it mana ñoŋ.
Buurub Asiri ak dooleem, maa la ciy xettli, yaw ak dëkk bii, te maay aar dëkk bii.”»
Waaye sama tur tax na ma aj sama mer, sama woy tax na ma muñal leen, ba duma leen fàkkas.
«Ay bés a ngi ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay jebbil Daawuda njebbitu njekk, mu falu di buur bu xelu, di jëfe njub ak njekk ci réew mi.
Bés yooyu ci jamonoom, maay jebbil njebbit lu jekk ci askanu Daawuda, muy jëfe njub ak njekk ci réew mi.
¶ «Moo tax nanga wax waa kër Israyil, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yeen waa kër Israyil, li may waaja def, du yeen laa ci seet, li ma ci seet mooy sama teddngay tur wu sell, wi ngeen teddadil fi digg yéefar yi ngeen fekki.
Moo tax cant ñeel ko, ndax yiwam wu màgg wi mu nu baawaanal ci Soppeem bi.