TSK

TSK · Isaiah 4:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yaw Yàlla, na la xeet yi sant, na la xeet yépp sant.

Ngor ak kóllëree daje, njekk ak jàmm saafoonte,

Aw njebbit mooy saxe fa ëkkub Yese, ab car soqeekoo fa reen ya,

Ay bés a ngi ñëw Yanqóoba saxi reen, Israyil moomooy tóor, law, ba feesal déndu àddinaak meññeef.

Su boobaa Aji Sax ji tawal lu ngeen ji, may leen pepp mu suuf meññ, sakkan te nangu, seen juri keroog di fore parlu yu yaa,

Na asamaan wis-wisal, niir yuri njekk, suuf fett, meññal wall, boole ci jebbil njekk. Man Aji Sax ji, maa def lii!»

Sa askan wépp ñu jub lañuy doon, te ñooy moom réew mi ba fàww. Ñooy sama njëmbat li ma jëmbatal sama bopp, sàkke leen samay loxo, ngir sama teddnga teew.

Bés yooyu ci jamonoom, maay jebbil njebbit lu jekk ci askanu Daawuda, muy jëfe njub ak njekk ci réew mi.

Ñu néew ay rëcci saamar, walbatikoo réewum Misra, ñibbi réewum Yuda. Waaye mboolem ndesu Yuda, ga dikkoon toogaansi Misra, dinañu xam kan la kàddoom di sotti, man am ñoom.

¶ «“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Man ci sama bopp maay sàkke ab car ca njobbaxtalu garabu seedar gu kawe ga, sàkkal ko bérab. Car yu ndaw ya ca kaw laay fàqe car bu nooy, jëmbatal ko sama bopp ci kaw tund wu mag te kawe.

Waaye kaw tundu Siyoŋ la aw ndes di rawe, te dina doon bérab bu sell, waa kër Yanqóoba it moomaat seeni moomeel.

Nga wax ko ne ko: “Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Nit a ngi nii, Njebbit la tudd, ci bérabam lay jebbee, ba tabaxi kër Aji Sax ji.

Ndaxte Yàlla mi ne: «Na leer gi leere ci biir lëndëm gi,» moo leeral sunu xol, ngir leeraangey xam-xamu leeru Yàlla, te leeraange googu mooy lerxat ci xar-kanamu Yeesu Almasi.

¶ Gannaaw loolu ma jekki gis mbooloo mu réy mu kenn manula waññ, ñu bawoo ci askan yépp ak giir yépp ak xeet yépp ak làmmiñ yépp. Ñu ngi taxaw fi kanam ngàngune mi ak Gàtt bi, sol mbubb yu weex, ŋàbb ay cari garabi tàndarma.