¶ Gannaaw ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikke na Ibraam wax jii ci peeñu, mu ne ko: «Yaw Ibraam, bul ragal dara; man maay sa kiiraay, te sa yool dina màgg lool.»
TSK
TSK · Isaiah 40:10
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Neleen Yàlla: «Yaaka yéemey jaloore! Sa doolee bare, ba say noon rasu,
Mooy mbugal xeet yi, jal seeni néew, di rajaxe kilifay àddina, ba mu daj.
Man nag ma noon: «Maa sonn ci dara, coonob cóolóol bu amul njariñ.» Teewul sama àttee nga fa Aji Sax ji, sama yool a nga fa sama Yàlla.
Sama wall jege na, sama njekk dëgmal na, ma nara àttee xeet yi sama dooley përëg. Man la waa dun yiy xaar, sama dooley përëg lañu yaakaar.
Dëgg a tumurànke, ku dëddu mbon sax, ñu ñori la, Aji Sax ji gis ci, ñaawlu ko, nde yoon a amul.
Aji Sax ji nag ne ko: «Baal sa jooy yi te fomp say rongooñ, dees na la yool sa coono.» Kàddug Aji Sax jee. «Say doom ay jóge réewu noon, ñibbsi.
¶ «Maa ngii di yebal sama ndaw, mu xàllal ma aw yoon. Sang bi (/Boroom bi) ngeen di sàkku mooy jekki agsi këram, malaakam kóllëre moomu (/ndawal kóllëre loolu), ki ngeen safoo, mu ngooguy dikk.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
ji mu fésal ci Almasi, ba mu ko dekkalee, dëël ko ci ndijooram, fa déndi asamaan.
¶ Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley ndee, te mooy Seytaane.
¶ «Ku am ndam nag, ku saxoo jëf ji ma soob, ba kera muj ga, maa lay jox sañ-sañ ci kaw xeet yi:
¶ Ba loolu wéyee ma gis asamaan ubbiku, fas wu weex daldi feeñ. Ki ko war, «Wóor te Dëggu» lañu koy wax te njub lay àttee, di ko xaree.
¶ «Maa ngii di ñëw léegi, ànd ak sama pey, ngir delloo ku nekk jëfam.