TSK

TSK · Isaiah 40:28

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ibraayma nag jëmbat na garabu tamaris foofa ca Beerseba, tudd fa Yàlla Aji Sax ji, ji nekk ba fàww.

Aji Sax ji, ñi koy xeex ay rajaxoo, kaw asamaan lay dënoo ci seen kaw. Mooy mbugal àddina, ba mu daj, di kàttanal buuru ñoñam, di dooleel ki mu fal.»

Bala tund yee juddu, bala ngay sos suuf ak àddina, yaa mas di Yàlla, ba fàww.

Ni nga ma xame daa yéeme, xóot lool, ba wees ma.

Dangeena xamul lii? Am dangeena déggul lii? Dees leena waxul ca njàlbéen, am seen xel a jàppul nu kenug àddina sampoo?

«Samay xalaat déy du seeni xalaat, te samay jëfin du seeni jëfin.» Kàddug Aji Sax jee.

Ma ne, Aji Sax ji gàttul loxo ba tëlee walloo, noppam naqariwul ba tere koo dégg.

«Dofe la sama ñoñ def. Man, xamuñu maay kan, mbetey gone yu dul xalaat dara; dég-dég, tus; seen xel mépp, lu bon rekk, lu baax, xamuñu ci dara.»

«Éy saa Boroom, Aji Sax ji! Yaw déy yaa sàkk asamaan, sàkk suuf ci sa doole ju bare ak sa kàttan. Dara tëwu la.

¶ Ci kaw loolu mu ne leen: «Yeen daal, yeena ñàkk xel, yeena naqarim xel, ndegam ba tey gëmaguleen mboolem li yonent yi xamle woon!

¶ Céy xóotaayub koomu Yàlla ak xel ma, ak xam-xam ba! Deesul natt ay dogalam, deesul ràññee ay jëfinam!

Moo tax ñu ne: «Ana ku xam xalaatu Boroom bi, ba man koo digal?» Waaye nun nag noo yor xalaatu Almasi.

¶ Am xamuleen ne aji jubadi ñi amuñu cér ci nguurug Yàlla? Bu leen kenn nax: Muy fokati séy yi, di bokkaalekat yi, di jaalookat yi, di góor-jigéen yi, ak ñiy ànd ak ñoom,

Dangeena xamul ne seen yaram mooy màkkaanu Noo gu Sell, gi ci yeen, Noo gi ngeen jote ci Yàlla? Moomuleen seen bopp,

Yaw Buur bi sax dàkk, doo dee, te bët manu laa gis, yaw Yàlla miy kenn, yaa tedd, yaa màgg, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin!