1 Samuel 30:10
TSK
Daawudaa ñoqli, mook ñeenti téeméeri nit, ñaar téeméeri nit yem foofa, ndax loof, ba manuñoo jàll xuru Besor.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Daawudaa ñoqli, mook ñeenti téeméeri nit, ñaar téeméeri nit yem foofa, ndax loof, ba manuñoo jàll xuru Besor.
Ragal-leen Aji Sax ji, yeen nitam ñu sell ñi; ku ko ragal doo ñàkk dara.
Ma seetlooti fi kaw suuf ne du ku gaaw, yaay raw; du ku jàmbaare, yaa moom xare; du ku xelu, am loo dunde; du ku muus, duunle; du kuy xamkat, amu yiw; ku nekk ak bésam ak wërsëgam.
Seeni fitt lañuy rajaxee xalelu góor, duñu ñeewante gone, duñu xool tuut-tànk gëti yërmande.
«Ne leen: Kàddug Aji Sax jee. Néew yeey wetaroo ci àll bi, mel niy jonkan, ni gub yu góobkat won gannaaw, kenn forul.»
Rawtu dina réer ku gaaw, boroom doole du tala jariñoo dooleem, jàmbaar sax du mana rawale bakkanam.