TSK

TSK · Isaiah 41:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Gannaaw ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikke na Ibraam wax jii ci peeñu, mu ne ko: «Yaw Ibraam, bul ragal dara; man maay sa kiiraay, te sa yool dina màgg lool.»

¶ Musaa nag ne mbooloo ma: «Buleen tiit, neleen tekk te xool li Aji Sax jiy def, ba xettli leen tey jii. Ndax kat waa Misra yii ngeen di gis nii tey, dootuleen leen gis mukk.

Dëgërluleen nag te am fit. Buleen tiit, buleen yox-yoxi ndax ñoom, ngir seen Yàlla Aji Sax ji mooy ànd ak yeen. Du leen ba, du leen wacc mukk.»

Ñu dajeek man, bés ba ma jàqee, Aji Sax ji taxawu ma,

Aji Sax ji yaa may feg, musal ma, dooleel ma sa loxo, nangul ma, darajaal ma.

Aji Sax jeey kàttanal ñoñam, di barkeele jàmm ñoñam.

Ku bon kat, sa doole dëddu la; ku jub, Aji Sax ji wallu la.

Su noon damuwul ci sama kaw, ma doora xam ne bége nga ma.

Ay giir a riir, ay réew yëngu; mu àddu, suuf seey!

Yaay sama ndimbal, may làqoo sa kiiraay, di sarxolle.

Bëj-gànnaar ak bëj-saalum, yaa ko sàkk. Tabor ak Ermon, tund ya, di sarxollee sa tur.

Ku daanu, Aji Sax ji wallu; ku sëgg, mu siggil.

Ma ne: «Yàllaa may wallu, ma dal-lu, duma tiit. Sama dooleek sama kaaraange mooy Ki sax, di Aji Sax ji, te mooy sama wall.»

Esayi da ne leen: «Waxleen seen sang ne ko: Aji Sax ji dafa wax ne: “Bul ragal kàddu yi nga dégg surgay buurub Asiri ñàkke ma ko kersa.

Man Aji Sax ji maay sa Yàlla; téye sa loxol ndijoor, di la wax ne la: «Bul tiit, maa lay dimbali.»

Bul tiit, yaw laa àndal, maay jële saw askan penku, dajalee leen sowub jant.

Aji Sax ji dafa wax ne: «Bu bésub yiw taxawee, ma nangul la; bu bésub mucc jotee, ma wallu la, sàmm la, def la ngay kóllëre sama digg ak askan wi, ngir yékkatiwaat réew mi, séddalewaat ay cér, suuf sii gental tey,

Ndaw leeka rafeti tànk, kee bartaloo tund yi, di la dégtalsi jàmm, di la xibaar lu neex, àgge la ag mucc, ne la: «Éey, Siyoŋ, sa Yàllaay Buur!»

Maay jàmbaaral waa kër Yuda, maay wallu waa kër Yuusufa, suqli leen, ñeewante leen, ñu mel ni masuma leena xarab, nde man maay seen Yàlla Aji Sax ji, te maa leen di nangul.

Ñetteel bi laay tàbbal ci sawara, xelli ko ca ni ñuy xellee xaalis, nattu ko ni ñuy nattoo wurus cib taal. Xaaj boobu moo may woo ci sama tur, ma wuyu ko. Moom laay wax: “Sama ñoñ,” Moom mu ne: “Aji Sax jeey sama Yàlla.”»

Luke 1:30 TSK

Malaaka ma ne ko: «Maryaama, bul tiit, ndax daje nga ak yiwu Yàlla.

Mu ne ma: «Sama yiw doŋŋ nga soxla; sama manoore, ci ag néew doole lay mate.» Kon kat dinaa gëna bégati ci damoo diggante yu ma néewe doole, ngir manoorey Almasi wàcc ci sama kaw.