Maa ngi nii ànd ak yaw, di la sàmm fépp foo jëm, te itam dinaa la délloosi ci réew mii. Duma la bàyyi mukk, waaye dinaa def li ma la wax lépp.»
TSK
TSK · Isaiah 41:17
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Man dinaa taxaw ci sa kanam ci doj woowu ca tundu Oreb. Dóoral ci doj wi, su ko defee ndox dina ci génne, mbooloo mi naan.» Musaa def noona ca kanam magi Israyil ña.
Ku yaakaar Aji Sax ji bég, leer nàññ, gàcce du ko sëlëm.
di ma woo bésub njàqare, ma wallu la, nga màggal ma.»
Suuf yëngu, asamaan sóob fi kanam Yàlla, boroom tundu Sinayi, Yàllay Israyil ja!
Boroom bi kat du wacc ñoñam mukk, du bàyyi ay séddoom.
boole xiif ak mar, ba bakkan di tàggoo.
Maay doxloo silmaxa yi ci yoon wu ñu xamul, ñall wu ñu miinul laa leen di jaarale. Maa leen di soppil lëndëm gi fi seen kanam, ag leer, fu ñagas, ma maasaleel leen. Lii laa leen di defal, te duma leen wacc mukk!
Maay sottim ndox suuf su mar, ak wal yu waleg joor gu wow. Maay sotti saw askan samag noo, sama barke sottikul ñi nga meññ,
Noowug Boroom bi Aji Sax jaa ngi fi sama kaw, ndax Aji Sax jee ma diw, fal ma, ngir ma àgge néew-doole yi xibaaru jàmm. Moo ma yebal ngir ma dëfal ñi seen xol jeex, yégal jaam yi, seen goreel, yégal ñi ñu tëj, seen ubbite.
Maay nàndal ku mar, leqli ku loof.»
«Ay bés a ngii déy, di ñëw,» kàddug Boroom bi Aji Sax jee: «maay wàcce xiif ci réew mi. Du doon xiifub dugub mbaa marum ndox, kàddug Aji Sax ji lañuy xiif.
Mu ne ma: «Sama yiw doŋŋ nga soxla; sama manoore, ci ag néew doole lay mate.» Kon kat dinaa gëna bégati ci damoo diggante yu ma néewe doole, ngir manoorey Almasi wàcc ci sama kaw.
Mu neeti ma: «Sotti na! Maay Alfa, di Omega, di njàlbéen, di muj. Ku mar, maa lay may nga naan ci bëtu ndoxum dund mi, te doo fey dara.