TSK

TSK · Isaiah 45:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Yàlla ne: «Nanu bind nit ci sunu melokaan, mu nirook nun, te na yilif jëni géej ak picci asamaan ak jur gépp ak suuf sépp ak lépp lu ciy raam.»

¶ «Yaw Aji Sax ji, yaw kenn yaa sàkk asamaan yi, ba ca asamaan ya gëna kawe ak seen gàngoor yépp, ak suuf ak lépp li ci kawam, ak géej ak li ci biiram lépp. Yooyu yépp, yaay ki leen di may bakkan, te gàngoori asamaan, yaw lañuy sujjóotal.

Ana ku natte géej biir loxoom? Ku xaymaa asamaan yaatuwaayu loxo? Ku mana fab suuf sépp, sol cib nattukaay? Ana ku natte ab màndaxekaay tund wu mag? Mbaa mu tam-tamal tund wu ndaw?

Séentuleen kaw, xool-leen ki sàkk yii fi kaw! Xanaa kiy daaguloo seen gàngoor gu mat, ñoom ñépp lay woo ci seen tur, ci kawewaayu dooleem ak màggaayu kàttanam, te kenn du ci wuute.

Yàlla Aji Sax ji dafa wax, moom mi sàkk asamaan, firi ko; tàllal suuf ak lu mu jur, may noowal bakkan ñi ci kawam, ba ña cay daagoo di noyyi.

Aji Sax ji kat dafa wax, moom mi sàkk asamaan, moom Yàlla mi bind suuf, tabax ko, dëj ko, sàkkewu ko maraas, xanaa tabaxal ñu ko dëkke. Mu ne: «Aji Sax ji, man a, du keneen.

«Éy saa Boroom, Aji Sax ji! Yaw déy yaa sàkk asamaan, sàkk suuf ci sa doole ju bare ak sa kàttan. Dara tëwu la.

¶ Ngëm a nu xamal ne Yàllaa sose àddina wërngal këpp ag kàddoom, li gisu daldi sàkkoo ci lu gisuwul.