TSK

TSK · Isaiah 45:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Suuf nag daa maase woon te wéet, lëndëm muur ndox mu xóot mi, lale ca kaw, Noowug Yàlla di wër, tiim ndox mi.

Yàlla barkeel leen ne leen: «Giirleen te bare, ba fees àddina, di ko saytu; te it yilifleen jëni géej ak picci asamaan ak mboolem mbindeef muy yëngu ci kaw suuf.»

Asamaan, asamaanu Aji Sax jee, suuf la dénk doom aadama.

Aji Sax ji man a, du keneen; kenn du yàlla ku dul man. Maa la gemb, te xamuloo ma,

Suuf, Aji Sax jee sàkke kàttanam; dun bi, mu sampem xelam; asamaan, mu lale xam-xamam.

Maa leen di fulal aw nit, ci biir Israyil gépp, ba mu daj, ñu dëkkewaat dëkk yu mag yi, tabaxaat bayaal yi.