TSK

TSK · Isaiah 45:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Bésub tey jii Aji Sax jee lay teg ci sama loxo, ma rey la, dog sa bopp. Tey jii sax laay leele njanaaw yeek rabi àll yi, néewi xarekati Filisti, ba àddina sépp xam ne Israyil am na Yàlla.

Yal nañu rus, jàq ba fàww. Yal nañu torox, sànku.

Kon nag Aji Sax ji sunu Yàlla, wallu nook moom, ba mboolem nguuri àddina xam ne yaw doŋŋ yaa di Aji Sax ji.»

Dees na wormaale turu Aji Sax ji fa sowu, wormaale teddngaam ba penku. Bu noon bi agsee ni walum dex, ngelawal Aji Sax jee koy wal, mu daw.

Maay biralal yéefar yi sama teddnga, yéefar yépp gis àtte yi ma dogal ak sama diisaayu loxo bi ma leen teg.

Waaye li ko dale penku ba sowub jant, fu ci nekk la sama tur màgge ci biir xeet yi, te fépp lees di taale cuuraay, ngir sama tur, boole ci sarax su set, nde sama tur a ni màgge fi biir xeet yi.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.