Mu wut tojitu njaq, di ko xasanoo, daldi toog ci biir jalub dóom.
TSK
TSK · Isaiah 47:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
ku sellal, fekk la sell; ku dëng, fekk laak say feem.
Yeen waa Babilon, gi ñu nara fàllas, ndokklee ku leen fey jëf, ja ngeen nu def!
Yéeneb bii ñeel na Babilon, muy peeñum Esayi doomu Amocc.
¶ Aji Sax ji kay mooy yërëm askanu Yanqóoba, dellu taamu xeetu Israyil wii. Moo leen di sancaatal fa seen suuf, doxandéem yi fekki leen; boole seen bopp ci askanu Yanqóoba.
Maay yéeg fa kaw niir ya, ba mel ni Yàlla Aji Kawe ji!”
Nee yeen waa Sidon ñi mel ni janq bu ñu tëdde, dootuleen xaxaloo. Ayca, dawleen jàlli ba dunu Sippar, te du tax ngeen am fa noflaay.
Yeen jigéen ñi dal xel, taxawleen temm, déglu ma; yeen janq ji féex, teewluleen ma.
te naa: «Ba fàww maay lingeer!» ba tax bàyyiwoo xel ca la ngay def; xalaatoo la muy jur.
Waxal Buur, wax Lingeer yaayu Buur ne leen: «Dëjuleen fi suuf, seen mbaxanam nguur mu yànj foq na.
«Yeen waa Dibon, dëkk bu taaru bi, wàccleen seen teddnga lu kawe te tooge digg maral; kiy yàqtesi Mowab kat song na leen, di màbbsi seeni tata.
Aji Sax ji dafa wax ne: «Maa ngii di yebal fi kaw Babilon, waa Lew Kamay gii, ngelawal yàqkat.
«Nooka rus ci saaga yi nu dégg, ak gàcce gi nu sëlmoo ndax doxandéem yi dugg ci biir bérab bu sell bi ci kër Aji Sax ji.»
Mag ak ndaw a ngi ne lareet fi suuf ci mbedd yi; sama janq jeek sama xale yu góor yi tëdd, fàddoo saamar. Yaa rey ci sa bésub mer, yaa rendi te yërëmoo.
Mboolem buuri tefes yaay wàcc seeni ngàngune, futti seeni mbubb, tàggook seen yére yu yànj, bàddoo tiitaange, ne dett fi suuf, dëkke kat-kat, seen yaram dawe saw demin.
Seen reewande sànk na leen, yeen ñi dëkke xar-xari doj, te seen dëkkuwaay sore kaw, ba tax leen naa ci seenum xel: “Ana ku ñu mana daane fi suuf?”
Maay jàllarbi ngànguney nguur yi, nasaxal dooley nguuri yéefar yi, jàllarbi watiir ak ay dawalkatam, fas yeek seeni gawar nërmeelu, ku nekk fàddoo saamaru mbokkam.
Joxleen ko ci toskare aku naqar, kemu daraja jaak dund gu bakkane ga mu jagoo woon. Gannaaw moo ne cim xelam: “Maa tooge jalu lingeer, dumab jëtun, duma deele mukk,”