TSK

TSK · Isaiah 49:25

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ku la ñaanal barke, ma barkeel, ku la móolu it, ma alag, te xeeti àddina sépp, ci yaw lañuy barkeele.»

Moo nu may móoloo ku Yàlla móoluwul? Ana nu may rëbbe ku Aji Sax ji rëbbul?

Yeneen xeet yeey delloo bànni Israyil ba seen réew, mooma Aji Sax ji séddoo, bànni Israyil jàpp ca ñoom njaam, góor ak jigéen, ba teg loxo ña leen tegoon loxo, moom ña leen moomoon.

Ku fitam rëcc, ne leen ko: «Dëgërlul te bul tiit. Sa Yàllaa ngii di la feyul, ba yool say noon. Moom mooy dikk, wallusi la.»

Dinga ko seet, doo ko gis, kuy jànkoonteek yaw, du mujje doon tus, te kuy xareek yaw it day mujj neen.

Yaw Yerusalem, mi ñu jàpp njaam, jógal fëgtu, yaw janq Siyoŋ mu taaru mi ñu jàpp njaam laa ne, tikkil buum gi ci sa baat.

Xanaa dees na songe moos, waaye ku la song it, yebalu ma ko, te ku la song daanu fi sa kanam.

Aji Sax jee goreel askanu Yanqóoba, jot ko ci loxol ku ko ëpp doole.

Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Bànni Israyil ak Yuda, ñépp lañu notandoo. Ñi leen jàpp ñépp téyee leen doole, bañ leena ba.

Yaw nag, deret ji feddli sama kóllëreek yaw, ci laay seet ba yiwi sa nit ñi ñu tëj biir kàmb gu ndox amul.

Bésub keroog maay def Yerusalem di doj wu diis gann ci xeet yépp. Képp ku ko jéema yëngal, da ciy gaañoo gaañu rekk. Te xeeti àddina yépp ay daje ci kawam.

Yii duma la Aji Sax jiy duma mboolem xeet yi xareek Yerusalem: Seen suux mooy yàqu te ñu ne jonn taxaw, seeni gët yàqu ca seen biir paxi gët, seenu làmmiñ nëb ca seen biir gémmiñ.

Waaye Yerusalem, ga fa kaw, mooy gor si, te moom mooy sunu ndey.