TSK

TSK · Isaiah 5:30

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji, géej a riir, géej a àddu, mu riir, gannax ya rëkk, mu riir.

Biddiiw mbaa dëllooñ dootu leeral; jant ay fenke lëndëm, weer dakkal leeram.

Maa xool suuf, ndeke ma nga ne maraas, ne wëyëŋ; ma xool asamaan, leer amatu ca.

Yeen waa Babilon, réew mu taaru mi, fitt aku xeej la ñooñuy ŋàbb, néeg lool, duñu yërëm, seen coow ni riirum géej, ñu war seeni fas, làng-déral leen ni benn bopp ngir xare.

Bu sa leer feyee, maay muur asamaan, lëndëmal ay biddiiwam, sànge jant bi aw niir, weer wi noppee leeral.

Amos 8:9 TSK

Ay bés a ngii déy, di ñëw,» kàddug Boroom bi Aji Sax jee: «maay sowal jant digg bëccëg, lëndëmal suuf bëccëg ndarakàmm.

¶ «Ay firnde dinañu feeñ ci jant bi ak weer wi ak biddiiw yi. Ci kaw suuf njàqare ak tiitaange mooy ñeel xeet yi ndax riirum géej gi ak gannax yi,

¶ Juróomeelu malaaka mi sotti ndabam ci kaw ngàngunem rab wi, nguuram daldi sóobu ci lëndëm, nit ñi di yéyu ndax metit,