TSK

TSK · Isaiah 57:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Mu wax ak buurub Israyil ne ko: «Ana lu ma séq ak yaw? Demal kay ca sa yonenti baay yaak sa yonenti ndey ya!» Buurub Israyil ne ko: «Déedéet, ndaxte Aji Sax jee nu fi woo, nun ñetti buur yii, ngir teg nu ci loxol Mowab.»

Loolu dalul moos ku bon, kay mel ni xatax bu ngelaw li wal.

Ku bon, ñu dagg, sànni; ku yaakaar Aji Sax ji, jagoo réew mi.

Aji Sax ji barkeel la, nga jagoo réew mi moos; mu alag la, nga dog.

Yaakaaral Aji Sax ji, sàmm yoonam, mu teral la, nga jagoo réew mi, ku bon sànku, ngay gis.

Aji Sax ji Yàllaa mat jant, mat kiiraay; yiw ak daraja, Aji Sax ji joxe; te du ngëneel lu muy bañal ku mat.

Ku bëgge day sooke ay, te ku wóolu Aji Sax ji, woomle.

Yaw Aji Sax ji, ku dogu, pastéefu, wóolu la, nga may ko jàmm ju mat, nde moo la wóolu.

Yaa leen di bàcc, ngelaw wal, ngëlén tasaare; yaw ngay bége Aji Sax ji, di damoo Aji Sell ju Israyil.

mu ne: «Ñooñu, maa leen di yóbbu sama kaw tund wu sell, bànneexale leen sama biir kërug ñaan, seen saraxu rendi-dóomal ak yeneen sarax, dees na leen ko nangul sama kaw sarxalukaay, ndax dees na wooye sama “kër, kërug ñaan”, ñeel xeetoo xeet.»

Fi Yanqóoba laay soqee aw askan, fi Yuda laa ne, fi laay jële lu séddoo samay tund. Samay tànnéef a koy séddoo, sama jaam ñi kay a fay dëkke.

Bukki ak mboteey bokk di for, gaynde niw nag, di for um ñax, jaan di dunde pënd. Deesatul gaañe mbaa di lore, fi mboolem sama kaw tund wu sell wi.» Aji Sax jee ko wax.

Waaw, ana seen yàlla yi ngeen sàkkal seen bopp? Bu leen musiba dikkalee, nañ leen wallu, bu ñu ko manee! Gannaaw yeen waa Yuda, ni seeni dëkk tollu la seeni yàlla tollu!

Aji Sax ji nee: «Yeen waa Yerusalem, yéegileen tundi Libaŋ, yuuxu. Àddooleen fa Basan, xaacu, te yuuxoo fa Abarim, nde seen soppe yépp a rajaxoo!»

Fa kaw sama tund wu sell wa, fa tundu Israyil wu kawe wa, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, foofa déy la ma waa kër Israyil gépp di jaamujee, ñoom ñépp ca réew ma. Fa laa leen di nangule. Fa laay sàkkoo seeni jooxe ak seen ngëneeli sarax, ak lépp lu ngeen ma sellalal.