TSK

TSK · Isaiah 6:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mu teg ca ne: «Man maay sa Yàllay baay, di Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa te di Yàllay Yanqóoba.» Ca la Musaa nëbb kanam ga, ndax ragala xool Yàlla.

Serub yaa ngi tàllal seeni laaf, jëme kaw, yiire kubeer gi seeni laaf te janoo, seeni kanam jublook kubeer gi.

¶ Suleymaan teg serub ya ca digg néeg bu sell baa sell, seeni laaf fireeku, catal laafu benn serub bi di laal genn wetu tabax bi, catal laafu serub ba ca des di laal geneen wetu tabax bi. Seen ñaari cati laaf yi ci des it di laale fa tollook digg néeg ba.

Ilyaas dégg ca, muuroo mbubbam, génn taxaw ca buntu xunti ma; déggul lu moy baat bu ko ne: «Ana looy def fii, Ilyaas?»

¶ «Yaw Aji Sax ji, yaw kenn yaa sàkk asamaan yi, ba ca asamaan ya gëna kawe ak seen gàngoor yépp, ak suuf ak lépp li ci kawam, ak géej ak li ci biiram lépp. Yooyu yépp, yaay ki leen di may bakkan, te gàngoori asamaan, yaw lañuy sujjóotal.

Job 4:18 TSK

Ndegam surgaam ya ca asamaan sax wóoluw leen, ay malaakaam sax, mu sikk leen,

Mu firi asamaan, wàcc, niir yu fatt lal tànk ya.

Yeen malaaka yi, santleen Aji Sax ji, yeen jàmbaar yu mag yiy jëfe ndigalam, di sàmm kàddoom.

¶ Kenn ci malaakay seraf ya naaw wutsi ma, yor aw xal wu mu keppe ag ñiim, jële ko fa sarxalukaay ba.

Ku ci nekk am na ñeenti kanam ak ñeenti laaf.

Seeni kanam a ngoogu. Ku ci nekk sa ñaari laaf a jëm kaw, di laal sa laafi moroom. Sa ñaari laaf yi ci des sàng sa yaram.

Bu ñu dawee, mbege ya feggook ñoom daw, bu ñu firee seeni laaf, jëm kaw, mbege ya du teqlikook ñoom.

dexu sawara di wal, balle fa kanamam. Junniy junnee nga koy jaamu, mboolooy mbooloo dar ko. Waa pénc ma toog, téere ya ubbiku.

Malaaka ma wax ak ña taxaw fa kanamam ne leen: «Summileen yéreem yu dand yi.» Mu teg ca ne Yosuwe: «Dama ne, far naa sa bàkkaar, te dinaa la solal lu jekk.»

Malaaka yi la Yàlla wax ci ñoom ne: «Moo def ay malaakaam diy ngelaw, jawriñam ñooñu la def tàkk-tàkki sawara.»

Malaaka yépp a nga taxaw, yéew ngàngune ma ak mag ñaak ñeenti bindeef ya. Ñu ne gurub sukk, dëpp seen jë fa kanam ngàngune ma, sujjóotal Yàlla,

¶ Ci kaw loolu ma gis meneen malaaka muy naaw ci digg asamaan, ànd ak xibaaru jàmm bi sax dàkk, ngir baaxe ko waa àddina: niti wépp askan ak gépp giir ak wépp làmmiñ ak wépp xeet.