su boobaa li may def ak yeen mooy lii: maay jekki wàcce njàqare ci seen kaw, mu ànd ak woppi ràgg, yaram wu tàng jérr ak bët yu lëndëm, ngeen gën di wopp. Dingeen ji seenum pepp ci neen, ndax seeni noon a koy lekk.
TSK
TSK · Isaiah 62:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Seenu yëkk, ñu rendi, ngeen gis, te dungeen ci lekk; seen mbaam, ñu nangu ko ci seeni loxo, te du délsi ci yeen; seeni gàtt, ñu jébbal seeni noon, te kenn du leen wallu;
Maay yékkati sama loxo jëme asamaan, giñ ne: “Ndegam maay dund ba fàww,
Seenum réew gental, seeni dëkk xoyomu, seen suuf, doxandéem yi lekk fi seen kanam, muy gent bu doxandéem tas.
«Ñooy tabax ay kër, dëkke, jëmbati tóokër, lekk ca meññeef ma.
Ñooy dikk, warax seen meññeef ak seen ñam, jeexal seeni doom, góor ak jigéen, lekk seen jur gu gudd ak gu gàtt, saax-saaxee seeni reseñ ak seeni figg; te dëkk yi ngeen yaakaare seeni tata, dooley saamar a koy tas.
¶ «Nanga leen wax, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Ba ma tànnee Israyil, maa giñal askanu waa kër Yanqóoba woowa. Maa leen xamal maay kan ca réewum Misra, giñal leen, ne leen: Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.