2 Kings 15:29
TSK
Ci jamonoy Peka buurub Israyil, Tiglaat Pilser buurub Asiri dikk, nangu dëkk yi ñuy wax Yon ak Abel Bet Maaka ak Yanowa ak Kedes ak Àccor ak diiwaani Galàdd ak Galile ak mboolem réewum Neftali. Mu jàpp waa réew ma, yóbbu Asiri.