TSK

TSK · Isaiah 7:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Axas nag yebal ay ndaw ca Tiglaat Pilser buurub Asiri, ne ko: «Man de, dama di sab jaam, te di sa doom. Kon nag ngalla dikkal xettli ma ci ñi ma jógal, di buurub Siri ak buurub Israyil.»

Boroom baa ngii di leen sottisi dexu Efraat gi ne xéew ak dooleem, te mooy buurub Asiri ak mboolem darajaam. Dex gi mooy génn xuram, fees fépp fu dig tàkkam,

Mag meek kàngam li ñooy bopp bi, yonent bi mokkal naaféq dib geen.

Sémmiñ dina diir mbagg ka koy gore? Am dogukaay dina réy-réylu ba sut ka koy doge? Mbete yet wuy xàcci ka ko ŋàbb; mbaa bolde bu walbatiku ŋàbb boroom!

Aji Sax jaa ngii di tas àddina, tasaare ko, salfaañe li fi dénd bi, wasaare ñi ko dëkke:

Léegi nag teg naa réew yii yépp ci loxol Nabukodonosor buuru Babilon, mi ci sama curga, ba joxaale ko rabi àll yi sax, ñu nangul ko.

«Yaw nit ki, Nabukodonosor buuru Babilon teg na mbooloom xareem, coono bu metti ca seen xareek Tir. Seen kawari bopp yépp ruus na, seen wagg yépp tëccu, te coonoom ba mu sonn ca Tir, yooloowu ca dara, du moom, du ay nitam.