ne leen: «Éey Israyil, dégluleen, yeena ngi waaja xareek seeni noon tey jii. Buleen yox-yoxi, buleen ragal, buleen tiit, buleen teqlikook seen sago ci seen kanam!
TSK
TSK · Isaiah 7:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba Asaryaa buurub Yuda duggee juróom fukkeelu atu nguuram ak ñaar, ca la Peka doomu Remalyaa falu buurub Israyil, péeyoo Samari. Nguuru na ñaar fukki at.
Damaas a yilif Siri, te Reccin yiliful lu moy Damaas. Fii ak juróom benn fukki at ak juróom Efrayim tas, ba xeet wa réer.’
«Gannaaw askan wee teddadil ndoxum Silowe, mi ci wal mu teey mi, di bége Reccin ak doomu Remalya,
Moo tax Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Yeen sama ñoñ ñi dëkke Siyoŋ, buleen ragal waa Asiri yi leen di dóor yet, ŋàbbal leen bolde ni waa Misra daa def ak yeen.
Ndax Boroom bi Aji Sax ji, Aji Sell ju Israyil dafa wax ne: «Délsi, dal-lu moo leen di musal. Ne tekk te wóolu maa leen di dooleel. Waaye yeena buggul!
Yaw Yanqóoba mi néew doole niw sax, yeen góori Israyil. Man, maa leen di dimbali. Kàddug Aji Sax jee, sab jotkat, Aji Sell ju Israyil.
Li baax mooy muñ, xeremluy xaar wallu Aji Sax ji.
Peeñu mi seede la, ñeel jant ba ñu ko àppal, seede su wóor ci na mbir may mujje, te du fen. Su diibee it, xaar ko, day dikk moos te du yàggati.