TSK

TSK · Isaiah 8:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Li tuuroo ci seen sàq yu fees, ak li wale ci seen nalukaay yu rembat, sama cér la; buleen ko yeexe, te seen taaw yu góor it, man ngeen leen di sédde.

Seen meññeefum suuf, ak mboolem seenu ñaq, xeet wu ngeen xamuloon a koy lekk, te dees leen di not ak a dëggaate rekk, bés bu nekk.

¶ Naka la Alyaasa di wax, ndaw la ne jimeet, jëm ca moom. Ma nga naan: «Gis nga musiba mii Aji Sax ji wàcce. Kon ana lu may séentooti ci Aji Sax ji?»

Job 1:11 TSK

Xàccil sa loxo rekk, dal ci mboolem lu bokk ci moom. Ndegam du jàkkaarlook yaw, xarab la.»

Job 2:9 TSK

Jabaram ne ko: «Yaa ngi ŋoy ci sa mat gi ba tey? Xarabal Yàlla boog te dee!»

Boroom baa ngii di leen sottisi dexu Efraat gi ne xéew ak dooleem, te mooy buurub Asiri ak mboolem darajaam. Dex gi mooy génn xuram, fees fépp fu dig tàkkam,

Ma dem, xool àll, gisuma lu moy ñu saamar bóom, ma dugg biir dëkk, gisuma lu moy ñu ne làcc akub xiif, yonent ak sarxalkat di wër réew mi, xam-xam réer leen.”»

Luy nàmp a nga mara mar, ba làmmiñ taqoo denqleñ. Gone yaa ngi ñaan mburu, te kenn daggalu leen.

¶ Ndesu nit ñi musiba yooyii reyul nag, taxul sax ñu tuub seeni jëf, ba bañatee jaamu ay tuur, ak jëmmi xërëmi wurus ak xaalis ak xànjar ak xeer ak dénk; xërëm yu gisul, déggul, doxul.