Ngay sippi Yàlla sa mer, di ko wax lu mel nii!
TSK
TSK · James 1:26
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Buleen mel ni fas mbaa berkelle mi amul ag dégg, laab ak tarka di ko téye, mu doora yem fi seen wet.»
Mu jëm ci Yedutun, njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Wax ju bare, moy ñàkku ca; ku moom sa làmmiñ, xelu nga.
Wax ju rafet yool na boroom, workat fitna la namm.
Ku xelu àddu, xam-xam rafet; ab dof di talalali.
Yoon a ngi, nit defe ne jub na, te mu jëme ko ci ndee.
day yendoo xemmem, te du am, ka jub di joxeek a joxewaat.
Kee di jur gu fore ab dóom, xelam nax ko, sànk ko. Du keey musal bakkanam de! Du kee naa: «Xanaa duy caaxaan laa ŋàbb nii?»
Kon nag teewluleen ni ngeen di dégge. Ku am, dees na ko dolli, waaye ku amul, la mu xalaatoon ne am na ko sax, dees na ko nangu.»
te ci ngeen texee, ndegam jàpp ngeen bu dëgër ci kàddug xibaaru jàmm bi, ni ma leen ko xamale. Lu ko moy ci neen ngeen gëm.
¶ Teewul ñooñu ñu jàppe woon ay kàngam, ak daraja ju ñu masoona am, amalu ma solo, nde Yàlla amul xejj ak seen, ñooñu yokkuñu lenn ci kàddu gi may xamle.
Dangeena dékku yii coono yépp ci neen? Xanaa déet kay!
¶ Bu genn kàddu gu bon génne seen gémmiñ, xanaa su ko jaree ngeen wax lu baax, luy jariñe, te diw yiw ci ñi koy dégg.
Na seen kàddu ànd ak yiw te am solo, te ngeen xam nu ngeen di tontoo ku nekk, tont li war.
¶ Doonleen jëfekati kàddu gi, buleen di ay déglukat doŋŋ, di nax seen bopp.
Bare na lu nuy tooñ, nun ñépp. Ku dul tooñ ci kàddu nag, kooku nit ku mat la, te man naa moom yaramam wépp, boole ci.