TSK

TSK · James 2:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ibraam nag gëm na Aji Sax ji, ba tax Aji Sax ji waññal ko ngëmam ag njub.

Asaryaa doomu Natan moo jiite woon ndawi Buur ya, Sabudd doomu Natan di sarxalkat te di diglekatu buur.

Job 16:21 TSK

Na ab seede layool nit fa Yàlla, ni doom aadama di layool moroom ma fi kaw suuf!

Luke 4:21 TSK

Mu àddu, ne leen: «Tey jii la mbind mii mat, ngeen dégg.»

Acts 1:16 TSK

«Bokk yi, Mbind mi moo waxe woon Noo gu Sell gi lu jiitu, ci gémmiñu Daawuda, wax ju jëm ci Yuda mi jiite nit ña, ba ñu jàpp Yeesu. Mbind moomu nag fàww mu sotti.

Nan lees ko ko waññale? Gannaaw ba mu xarafee, am ba mu xarafagul? Du gannaaw ba mu xarafee, waaye ba mu xarafagul la.

Mbind mi moo indi kàddu ga dikkaloon Firawna, ne ko: «Maa la yékkati, te li ko waral mooy lii ci boppam: ngir fésal sama doole ci yaw, ngir itam ñu sàbbaal sama tur ci àddina sépp.»

¶ Noonu la Ibraayma gëme Yàlla, «ñu waññal ko ngëmam ag njub.»

Waaye mbind mi biral na ne mboolem àddina moo tënku ci kilifteefu bàkkaar, ngir dige bi gëm Yeesu Almasi di jagle, mana dikkal aji gëm ñi.

Moo waral lii dikk ci Mbind mi: «Maa ngii di dëj fi Siyoŋ, aw doju doorukaay, doju tànnéef wu gànjare. Wii doj, ku ko wéeroo, doo rus mukk.»