TSK

TSK · James 2:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 20:19 TSK

Moo dëggaate néew-ji-doole, dëddu ko; aakimoo kër jaambur te tabaxu ko.

Day tëroo ciy dëkk-dëkkaan, làqu di bóom ku deful dara, nëbbu di wootal néew-ji-doole.

Yaw de yaay ki nemmiku, di gis njekkar ak naqar, ku mu dal, nga sàmm àqam. Néew-ji-doole wéeroo la, ab jirim, nga dimbali.

Ku néewlee yaakaar, ngeen tas ko, waaye Aji Sax ji la làqoo.

Kuy ñaawal ku ñàkk, tooñ nga ka ko sàkk; kuy reetaan ku jàq, mbugalam du jaas.

Xanaa ndax buur suqal mbey mi, ba ñépp jariñoo suuf si.

Aji Sax jeey yékkati kàddug sikkaange, jëme ci magi ñoñam ak seeni kàngam. «Yeena sëxëtoo tóokëru reseñ bi, la ñu foqatee ci néew-ji-doolee nga seeni kër.

Amos 2:6 TSK

Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke Israyil, te duma fomm seeni duma. Ñooy jaay jaam aji jub ngir xaalis bu mu leen ameel, jaay aji ndóol bu manul fey dàlli carax.

Amos 5:11 TSK

Gannaaw yeenay not néew-ji-doole, di foqati ŋëbu peppam, tabax ngeen këri boroom barke, waaye dungeen ko dëkke. Jëmbat ngeen tóokëri reseñ juy tem-temi, waaye dungeen naan ca biiñ ba.

Ana nu may ñàkka toppe màndaxekaayi njublaŋ, ak mbuusum doomi naxekaay yees cay natte?

Ab jëtun, ak ab jirim, ak ab doxandéem, ak ab néew-doole, buleen ko not. Lu bon it, buleen ko mébétalante ci seen xol.»

Acts 4:1 TSK

¶ Naka la Piyeer ak Yowaan di wax ak mbooloo ma, sarxalkat yaak jawriñu kër Yàlla gaak Sadusen ya ne jimeet ci seen kaw.

Acts 5:17 TSK

¶ Ba mu ko defee xolu kañaan dugg sarxalkat bu mag ba, ak mboolem ña ko dar, te di waa ngérum Sadusen ña.

Acts 8:3 TSK

Ci biir loolu Sóol moom, ma ngay jéema faagaagal mbooloom gëmkat ñi, di dugg ci kër yi, diri góor ak jigéen, génne, ñu sànni kaso.

¶ Ba loolu amee alal ja njaatigey ndaw sa yaakaaroon, réer leen, ñu jàpp Póol ak Silas, diri, yóbbu ca pénc ma, fa kanam njiit ya.

¶ Jant ya Galyon moomee diiwaanu Akayi, Yawut ya dañoo mànkoo, jógal Póol, jàpp ko, yóbbu ca àttekaay ba.

James 2:3 TSK

su ngeen seetloo boroom col gu jekk gi, ne ko: «Toogeel fii, moo baax ci yaw,» te ne néew-ji-doole ji: «Yaw, taxaweel nee, mbaa nga toog fii sama tànki toogu, fi suuf,»

James 5:6 TSK

Yeena daan ba reylu aji jub, te jéemula bañ.