¶ Yàlla ne: «Nanu bind nit ci sunu melokaan, mu nirook nun, te na yilif jëni géej ak picci asamaan ak jur gépp ak suuf sépp ak lépp lu ciy raam.»
TSK
TSK · James 3:9
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ku tuur deretu nit, na nit tuur deretam, ngir melokaanu boppam la Yàlla sàkke nit.
¶ Gannaaw loolu Buur Daawuda dem bay jub dëkk ba ñuy wax Baxurim rekk, yemook jenn waay ju bokk ci waa kër Sóol. Ma nga tuddoon Simey doomu Gera. Naka la waa ja ne tëll, jubsi, di tifaar Daawuda ay saaga,
Ay móolu la gémmiñ ga fees, ak fen ak njublaŋ, njekkar ak ñaawtéef lal làmmiñ wa.
Yaa ma soppil samay rongooñ ay ree, summi sama yérey tiis, solal ma bànneex.
Man it ma tudd sa njekk, di la dëkke màggal!
Yàlla, dogu naa, dogu naa woy, di la kañ.
Xanaa dungeen bàyyee songandoo nit, nar koo sànk, ni kuy màbb tabax bu joy, mbaa ngay bàddi per mu ràpp?
May yendoo siiwal sa njekk nde ña ma doon wuta lor lañu rusloo, sewal leen.
Moo bëggoon di móoloo, yal na ko këppoo; soppul ag ñaan it, yal na ko barke sore.
Naa sàlloo sant Aji Sax ji, na luy dund saxoo dàkk di màggal sellngay turam!
Boroom bi nee: «Askan wii, làmmiñ lañu ma jegee, lori neen lañu may wormaale, te seen xol sore ma. Seen ragal ak man it, njàngum tari kepp la.
Seen gémmiñ, waxi móolu ak wextan la feese,
¶ Cant ñeel na Yàlla sunu Baayu Sang Yeesu Almasi, mi nu baaxe bépp barkey biir, ci Almasi mi nu bokk, fa déndi asamaan ya.