Naka la Ibraayma jegeñsi, ne ko: «Mbaa doo boole ku jub ak ku jubadi, rey leen?
TSK
TSK · James 4:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Moona saay yoxo jëfewul coxor, te samag ñaan lal na worma.
yaatal ma, bége ma, ba xettli ma.
Aji Sax ji, maay jàpp ci biir mucc ayib, di wër sa sarxalukaay,
Yal nanga ma dégtal mbég ak bànneex, ma bégati, gannaaw ba nga ma dammatee.
Man de, jege Yàllaa ma gënal. Boroom bi, Aji Sax ji, yaw laa def kiiraay, ngir siiwal sa jépp jëf.
Bu ngeen ma tàllaleey loxo, ma fuuyu. Bu ngeen doon ñaan-ñaanee it, du maa leen di déglu: seeni loxo, deret la taq ripp.
Boroom bi nee: «Askan wii, làmmiñ lañu ma jegee, lori neen lañu may wormaale, te seen xol sore ma. Seen ragal ak man it, njàngum tari kepp la.
Janti keroog dees na wax askanu Yerusalem wii, ne leen: «Jaas bu tàng a uppe kaw tund ya ne faraas ca màndiŋ ma, wuti sama ñoñ. Du doon ngelaw lees di bàcceek a beese.
Bés ba ma la wooyee nga dikk, ne ma: «Bul tiit.»
Maa leen di wis ndox mu set, ngeen set. Mboolem seen sobe ak mboolem seen kasaray tuur laa leen di setalal.
Kon nag waxal askan wi, ne leen Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: “Dellusileen ci man,” kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi, “kon dinaa dellusi ci yeen.” Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yee ko wax.
Sang bi ne ko: «Yeen Farisen yi, bitib kaas bi ak ndab li daal ngeen di raxas, te fekk leen feese jikkoy jagoo lu lewul, akug mbon ci biir!
¶ Gannaaw noo moom yii dige nag, soppe yi, nanu setal sunu bopp ci mboolem sobey yaram, ak ju xel, te nu matal sellnga ci ag ragal Yàlla.
ndax yoonu Musaa sottalul dara ba mu mat sëkk. Ci geneen wet, yaakaar ju gën moo nuyoo, di yoon wu nuy jaare ba àgg fa Yàlla.
Boroom xel-yaar la, xel maa toogul ci lenn lu muy def.
Ndox mooma di misaalub sóobu gi leen musal tey; du sóobu guy dindi tërub yaram, waaye moom ngeen di wuyoo wooteb Yàlla ci xel mu dal, te li leen di musal mooy ndekkitel Yeesu Almasi,