TSK

TSK · Jeremiah 1:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Te nag, sang bi, gannaaw gént nga ko ñaari yoon, kon Yàlla dogal na mbir mi, te dina ko amal balaa yàgg.»

¶ Aji Sax ji wax ma ne ma: «Yeremi, loo gis?» Ma ne ko: «Xanaa ay figg. Figg ju baax ji nag baax na lool, waaye ju bon ji daa bona bon, ba kenn du ko lekk ndax bon.»

Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Dëkk bi kay ndab la, seen bokki néew yi ngeen fi saam di yàpp wi ci ube, waaye yeen dees na leen fi génnee.

Léebalal kërug fippukat yi aw léeb, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Taalal, teg cin li, teg ko, sotti ci ndox.

Mu ne ma: «Loo gis?» Ma ne: «Damaa xool, gisuma lu moy ab tegukaayu làmp bu lépp di wurus, ak kopp bu tege ci kawam, ak juróom ñaari làmp ci kawam, bu ci nekk ak juróom ñaari gémmiñam ca kaw.