Axas nag yebal ay ndaw ca Tiglaat Pilser buurub Asiri, ne ko: «Man de, dama di sab jaam, te di sa doom. Kon nag ngalla dikkal xettli ma ci ñi ma jógal, di buurub Siri ak buurub Israyil.»
TSK
TSK · Jeremiah 13:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
ñu tiita tiit, yaram di fuddook a metti, ñuy baddaañu ni kuy matu; ku ne jàq, di xulli sa moroom, kanam ya sël-sëleendoo.
Esekiya am ca mbégte, daldi won ndaw ya, kërug dencukaayam: xaalis baak, wurus waak ndàbb jaak, diwu tànnéef gaak mboolem néegub gànnaayam ya, ak mboolem lu nekkoon cay dencam. Amul lenn lu leen Esekiya wonul ci biir këram, ak mboolem fu bokk ci kilifteefam.
Yonent yiy wax waxyuy fen, sarxalkat yiy jiitee seen coobare, te sama ñoñ soppe ko ni! Moo bu muj ga taxawee, nu ngeen di def?»
«Yaw mi tooge Libaŋ, def um tàgg sa garabi seedar, éy bu la mitit dikkalee, nirook mititu mat, ndaw binni yu réy!»
Gisuma lu moy mboolem jigéen ñi des ci kër buurub Yuda, ña nga ñu jëme ca kàngami buuru Babilon. Ña nga naan: «Buur aka baaxi xarit! Ñoom ñi ko nax, ba man ko, mu tàbbi ca bàq ba, ñu dëddu, ne mes!»
Xanaa doo janook ki lay rey, naati yaay yàlla? Boo tàbbee ca sa loxoy jamkat ya, keroog nga noppee doon yàlla, di nitu kese.