Exodus 9:14
TSK
Ndax kat bii yoon maa ngii di yebal sama mbugal yépp ci yaw ci sa bopp, ak say dag ak sa waa réew, ngir nga xam ne awma moroom ci àddina wërngal këpp.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ndax kat bii yoon maa ngii di yebal sama mbugal yépp ci yaw ci sa bopp, ak say dag ak sa waa réew, ngir nga xam ne awma moroom ci àddina wërngal këpp.
«Aji Sax ji jàmbaari xare ji, Aji Sax jeey turam!
Yal nañu rus, jàq ba fàww. Yal nañu torox, sànku.
«Aji Sax ji dafa wax, moom miy sàkk mbir, bind ko, taxawal ko, Aji Sax ji di turam.
Mu ne: βNa Esekiyel di seen misaal. Bu jotee, mboolem nu mu def, nangeen ko def, ba xam ne man maay Boroom bi Aji Sax ji.β
Maay duma Edom, te Israyil sama ñoñ laa leen di dumaa. Ñooy jëflanteek Edom la méngook sama mer, tollook sama xadar, ba ñu ñam sama mbugal. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.»