TSK

TSK · Jeremiah 18:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ba loolu amee bootalub Buur, Elyakim doomu Ilkiya ak Sebna, bindkat ba, ak doomu Asaf, Yowa ma denc téere ya, ñoo dem ak seen yérey ñaawlu yu xottiku, ba ca Esekiya. Ñu daldi koy àgge kàddug bëkk-néeg ba.

«Jàll-leen ba ca duni Kitim fa sowu, te xool; yónneeleen Kedar fa penku, seetlu bu baaxa baax ndegam dingeen gis lu mel nii!

Waaye yonenti Yerusalem laa gisal lu yées: ñuy jaaloo, di wéye ay fen, di dooleel defkatu lu bon, ba kenn dëdduwul mbonam. Ñoom ñépp di ma niru waa Sodom, waa Yerusalem it ni waa Gomor.»

Ku doon jàmbaar fi sama biir, la Boroom bi xalab. Am ndaje la ma wooteel, ngir falaxe sama ndaw yu góor. Boroom bee dëggaate Janq Yuda mu taaru mi, ni reseñ ci biir nalukaay.

Amos 5:1 TSK

Amos ne: Yeen bànni Israyil, dégluleen mii pent: maa ngi leen di jooy, yeen bànni Israyil!

¶ Déggees na nag ci lu wér, ne powum séy am na ci seen biir, te powum séy mu ni mel, giseesu ko sax ci biir xeeti yéefar yi. Dem na sax ba nit nekk ak jabaru baayam.