Nëgëni tey doon naa xàcci sama loxo xaat, dumaa leen mbas mu leen di fare ci kaw suuf, yaw yaak sa waa réew.
TSK
TSK · Jeremiah 21:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Jan yàlla moo masa fexee dikk foqatil boppam aw xeet, bellee leen ci weneen xeet, ci biiri nattu, aki firnde aki kéemaan ak xare yu mu sottale dooley loxoom, ak kàttanu përëgam, ak jëf ju raglu, noonee leen ko seen Yàlla Aji Sax ji defale ca Misra, ngeen teg ci bët?
Waaye xeet wi delluwuñu ca ka leen duma, sàkkuwuñu Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.
Waaye ñoom ñoo fippu, di naqaral xelam mu sell, mu soppliku seen noon, ba mujj di xareek ñoom.
«Éy saa Boroom, Aji Sax ji! Yaw déy yaa sàkk asamaan, sàkk suuf ci sa doole ju bare ak sa kàttan. Dara tëwu la.
Boroom bee tàwwi ag fittam mel ni ab noon, moo diire ndijooram, mel ni bañ, moo bóom mboolem lu neexa xool. Ci biir xaymay janq Siyoŋ mu taaru ma la yuri am sànjam ni sawara.
Tund yu mag yi di ko loxal, tund yu ndaw yi seey, suuf fuddu fi kanamam, mook àddina ak mboolem li ci biiram.