TSK

TSK · Jeremiah 39:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ci kaw loolu Toyi buurub Amat dégg ne Daawuda duma na gàngooru Adadeser gépp.

Firawna Neko moo làqoon jant bi Yowakas ca dëkk ba ñuy wax Ribla ca réewum Amat, ba nguurootul ca Yerusalem. Mu teg réew ma galagu fanweeri barigoy xaalis, ak fanweeri kiloy wurus.

Ngelaw lu ko ëpp doole laay indi. Léegi maa leen di biral sama kàddug mbugal.»

Waaye soo jébbalul sa bopp kàngami buuru Babilon, dees na teg dëkk bi ci loxoy waa Babilon, ñu lakk ko ba mu jeex, te yaw doo leen rëcc.»

Aji Sax ji dafa wax ne: «Maa ngii di waaja teg Firawna Ofra buuru Misra ci loxol noonam yiy wut bakkanam, na ma tege woon Cedesyas buurub Yuda ci loxol noonam Nabukodonosor buuru Babilon ma doon wut bakkanam.»

Ba mu ko defee Nebusaradan, njiital dagi buur, boole leen yóbbu ca buuru Babilon ca Ribla.

Ki nuy noyyee, Buur bi Aji Sax ji fal, ca seeni yeer la tance, te nu noon ci keppaaram lanuy dëkke fi digg xeet yi.