Ba loolu amee Suleymaan di topp tuur ya ñuy wax Astàrt di tuuri waa Sidon, ak Milkom, tuuru Amoneen mu siblu ma.
TSK
TSK · Jeremiah 49:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bérabi jaamookaay ya féete woon Yerusalem penku ca bëj-saalumu tundu Alkànde, Buur Suleymaan tabaxaloon ko tuur ma ñuy wax Astàrt, kasaray waa Sidon ya, ak tuur ma ñuy wax Kemos, kasaray Mowabeen ña, ak tuuru Amoneen mu siblu ma ñuy wax Milkom, Buur Yosya daa boole lépp sobeel ko.
Yuuxuleen! Bésub Aji Sax ji moo dëgmal, te ni sànkute gu bawoo fa ci Aji Man ji lay dikke.
Nit ñaa ngi yéeg jëm kërug jaamookaay ga ca Dibon, ngir jooyi ca bérabi jaamookaay ya, Mowab a ngay yuuxoo kaw tundu Nebo ak Medeba, boppoo bopp dib nel, sikkimoo sikkim xuufu,
¶ Yéene bii ñeel na dëkk ba ñuy wax Tir: Yeen waa gaali Tarsis ñi deele, jooyleen! Lépp a yàqu! Du kër, du teeruwaay. Fa dunu Sippar lañu leen ko waxe.
Jigéen ñi dal xel, ragal-leen; yeen ñi féex laa ne, tiitleen! Futtikuleen, ba ne duŋŋ; gembooy saaku, ñaawloo.
Éey bokk yi, sol-leeni saaku, diwoo dóom, ñaawloo ko. Ñaawluleen ni kuy dëj benn bàjjo te jooy jooy yu metti, nde yàqkat bi day jekki, ne sunu kaw dàll!
Mowab amatul woy, fa Esbon la leen noon ya fexeel lu bon, ne: “Aycaleen nu raafal wii xeet!” Yeen waa Madmen it, ñu wedamal; saamar topp leen.
Ñu ne: “Gàcce ñeel na Mowab gii tas!” Yuuxooleen, ne wóoy! Yéeneleen fa tàkkal dexu Arnon, ne Mowab tas na!
Lu jëm ci Amoneen ñi, Aji Sax ji dafa wax ne: «Israyil daa amuli doom? Am daa amul dono? Lu tax Milkom tuur mi donloo suufas Gàdd, ba ay jaamukatam sanc dëkki Gàdd?
Seen buur ay duggi ngàllo, mooki kàngamam.» Aji Sax jee ko wax.
¶ Kaayleen nag ma wax leen, yeen boroom alal yi, jooyleen te yuuxu, ndax mitit yi leen di dikkal.