TSK

TSK · Jeremiah 51:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba loolu amee nag Musaa ak bànni Israyil woy Aji Sax ji, màggal ko. Ña nga naan: «Ma woy Aji Sax ji, ngir ndamam li kawee kawe. Fas ak gawaram la fab, xalab géej.

Dikkleen gis jaloorey Aji Sax ji, ak yàqute gi mu dogal ci kaw suuf.

Saamar ci kaw fas ak watiiram, ak mboolem niti njaxasaan ñi mu fat, ba ñu mel niy jigéen. Saamar ci kawi dencam, ñu sëxëtoo.

Maa fiy dagge sa dëkki réew mi, màbb sa tata yépp.

Maay jàllarbi ngànguney nguur yi, nasaxal dooley nguuri yéefar yi, jàllarbi watiir ak ay dawalkatam, fas yeek seeni gawar nërmeelu, ku nekk fàddoo saamaru mbokkam.

Su keroogee,» Aji Sax jeey wax: «ngëlëmte laay dumaa wépp fas, te ag ndof laay dumaa gawaram. Kër Yuda nag laa naan jàkk samay gët, te ag cilmaxa laay dumaa wépp fasu xeet yi.