TSK

TSK · Jeremiah 6:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yeen rabi àll yi, dikkleen ci bernde ji, yeen rabi gott bi yépp.

Ñaawtéefi Israyil ak alalam ju lewul moo ma merloo, ma duma ko, xañ ko sama kanam, waaye mu të ticc, topp xolam.

«Gàcceg sàcc bu ñu jàpp dees na ko gàcceel waa kër Israyil, ñook seeni buur ak seeni kàngam ak seeni sarxalkat ak seeni yonent,

«Maay joxe seeni jabar, jox seeni tool ay foqatikat, ndax ki gëna tuut ba ki gëna mag, ñépp a ngi lewal lu lewul. Ab yonent akub sarxalkat, ñépp a ngi wor!

«Yaw xooloo, xalaatoo lu moy loo jariñoo, ak noo tuure deretu jaamburu Yàlla, di fitnaale ak a lore?»

«Te it yonent ak sarxalkat ñoo bokk yàqu, sama biir kër sax gis naa ci seenug mbon.» Kàddug Aji Sax jee.

¶ Ba mu ko defee sarxalkat yaak yonent yaak mbooloo ma mépp dégg Yeremi di wax kàddu yooyu ca biir kër Aji Sax ji.

Seen bàkkaari yonent yaa, seen ñaawtéefi sarxalkat yaa; ñoo tuur fa digg dëkk ba deretu aji jub ñi.

Ay yonentam a ngi déeyoo fi biiram; ñu ngi xiiru ni gaynde guy xotat pàddam, di lekk doom aadama yi, foqati alal ak gànjar, ful jëtun yi ci biiram.

Micah 2:1 TSK

Wóoy, ngalla ñiy mébét ñaawtéef, di ràbb lu bon ci seenub tëraay, bët set, ñu jëfe ko, ndax xam ne man nañu ko.

Micah 3:5 TSK

Lii la Aji Sax ji wax ci yonent yiy lajjal samay bokk: «Bu ñu sàqamee ab lanc, yéene jàmm; ku leen leelul, ñu biral waxyub xare.

Kàngam yi ci biiram di gaynde yuy ŋar, ay njiitam di tilli timis yu dul pannal,

Bumu di ab màndikat, mbaa bëggkatub xeex, waaye na lewet, bañu ay, te bumu di bëggkatub xaalis.

¶ Seeni gët xoolul lu moy ku ñu jaalool, te duñu bàkkaar ba regg mukk; ku dëgërul, ñu yóbbaale la. Ñooñu la seenub xol tàggatu ci ag bëgge, mii njurum alkànde!