TSK

TSK · Job 13:24

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Samiyel ne ko: «Loo may laaj, gannaaw Aji Sax jee la dëddu, def la ab noon?

Job 10:16 TSK

Waaye su may siggi rekk nga mel ni gaynde, di ma rëbb, dellu di ma lore say kiraama,

Job 16:9 TSK

Meram la ma daggatee, jéppi ma, di yéyu ci sama kaw, daasal ma gëti noon, ne ma jàkk.

Job 29:2 TSK

Éy ku ma doon delloo jamono ya woon, fan ya ma Yàlla daa wattoo;

Job 31:35 TSK

Ma ne éy ku may may nopp? Sama torloo ngoog, na ma Aji Man ji tontu! Su dee téereb tuuma bu ma ku may layool bindal,

Éy Aji Sax ji, lu la taxa sore? Xanaa dangay làqu, bésub njàqare?

Éy Aji Sax ji, jógal! Looy nelaw? Yewwul, bu nu wacc ba fàww.

xanaa xalaat janti démb, at ya woon.

Maa ngi séentu Aji Sax ji, mu ngi won waa kër Yanqóoba gannaaw, waaye maa ngi koy yaakaar.