TSK

TSK · Job 21:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Soo defee lu baax, dees na la nangul; soo deful lu baax, bàkkaar a ngi lay yeeru ci sa bunt, di la tërook a wut, waaye yaa ko wara man.»

“Aji Sax ji! Kiy muñ mer, te bare ngor, di bale tooñ aki moy te du ñàkka topp mukk doom, tooñu waajuram, ba ca sët yaak sëtaat ya.”

bu ma daasee sama saamar buy melax, ba ŋàbb ko ci saab loxo, di àtte, maay fey samay digaale, añale samay bañ.

Job 22:24 TSK

Tegal wurus ci suuf, wacce wurusu ngalam doji xur,

Yal nay doomam diy jirim, jabaram dib jëtun,

Ndaxam moom sunu wopp la yenu, sunuy mitit la sëfoo. Nun nu foog ne dees koo mbugal, foog ne Yàllaa ko duma, torxal ko.

«Ana lu waral waxin wi ngeen di waxe fi Israyil naan: “Baay lekk reseñ ju xaay, mu uum gëñi doom ja”?

«Ngeen neeti: “Lu tax doom du gàddu bàkkaaru baay?” Xanaa du njub ak njekk la doom ji jëfe, sama dogali yoon yépp, mu di ko sàmm, di ko jëfe? Dina dund kay!

Almasi mi masula bàkkaar, moom la Yàlla sëf sunu bàkkaar, ngir nu mana ame ci moom àtteb nit ñu jub fa Yàlla.

Na mu jëfe ak yeen, jëfeleen ko ak moom, feyleen ko ñaari yoon ay jëfam. Kaas bi muy xellile am njafaan, feesalal-leen ko njafaan lu ko ëpp doole ñaari yoon.