Job 27:8
TSK
Ana lu yéefar biy yaakaarati bu fàddoo, ba Yàlla moom bakkanam?
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ana lu yéefar biy yaakaarati bu fàddoo, ba Yàlla moom bakkanam?
Su ma naroon ñaawtéef, Boroom bi du ma déglu.
Saraxub ku soxor, Aji Sax ji bañ na ko; ñaanu kuy jubal da koy bége.
Soo dee tanqamlu yoon, sag ñaan sax Yàlla suur na ko.
Bu ngeen ma tàllaleey loxo, ma fuuyu. Bu ngeen doon ñaan-ñaanee it, du maa leen di déglu: seeni loxo, deret la taq ripp.
Du seen xol lañu ma wooye wall, xanaa di salliiru ci seen kaw lal, pepp ak biiñ tax ñuy dagg seen yaram, dëddu ma.
Ngeen defal ma saraxu rendi-dóomal, mbaa saraxi pepp it, duma ko nangu. Seen saraxu jur guy cant ci biir jàmm, faalewuma.