TSK

TSK · Joel 2:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Ruth 1:6 TSK

¶ Ba loolu amee Nawmi fabu, mook goroom ya, ngir jóge réew ma. Booba fekk na mu dégge ca Mowab ne Aji Sax ji xettli na ñoñam, ba may leen ab dund.

«Ñooy tabax ay kër, dëkke, jëmbati tóokër, lekk ca meññeef ma.

Maa leen di sàkkal tóokëru jàmm ba ab xiif dootu fi lore ci réew mi, te dootuñu jànkoonteek kókkaliy yéefar yi.

Maa leen di musal ci seen mboolem sobe, maay woo am pepp, ful ko, te dootuma leen teg ab xiif.

Gannaaw bu ma walee waa kër Israyil sama noo, dootuma leen xañ sama kanam. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.»

Joel 1:10 TSK

Tool yi yàqu yaxeet, suuf sëngéem ciw tiis; pepp yàqu, biiñ bu bees wow, ag diw ŋiis.

Amos 9:13 TSK

«Ay bés a ngii déy, di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «kuy gàbb dina dab kuy góob, kuy nal reseñ dab ka koy ji. Biiñ bu bees di rogalaate ca tund yu mag ya, di wale tundoo tund wu ndaw.

«Ndax jiwum jàmm lay doon, garabu reseñ meññ doomam, suuf si meññ gàncaxam, asamaan di lay. Loolu lépp laay sédd ndesu askan wii.