TSK

TSK · Jonah 1:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Gannaaw loolu ñu dégg tànki Yàlla Aji Sax ji, muy doxantu ca tool ba, fekk ker gi sedd, ñu daldi fexee làqu Yàlla Aji Sax ji ci biir garabi tool bi.

Teewul Musaa ne ko: «Ngalla waay, yónnil keneen ku la soob rekk, sama Boroom.»

¶ Ilyaas gis na mu deme, daldi daw, ngir rawale bakkanam. Mu dem ba Beerseba ca réewum Yuda, bàyyi fa surgaam.

Job 2:7 TSK

Ba mu ko defee Seytaane bàyyikoo fa Aji Sax ji. Ci kaw loolu mu sànni Ayóoba ay taab yu metti, dale ko ca téstën ma, ba ca kaw bopp ba.

ak gaalu Tarsis gu mag gu mu doon, ak gépp gaal gu taaru.

Jàllal ba Tarsis, yeen waa tefes ga fa ne, jooyleen jooyi dëj.

Waa dun ya déy a nga may séentu, gaali Tarsis yu mag yaa nga jiitu, jële fu sore sa doom yu góor ya, indaale seen xaalis ak seen wurus, ngir sa Yàlla Aji Sax ji, Aji Sell ju Israyil ji la teral.

Yaw nit ki nag, déglul lii ma lay wax. Bul fippu ni kërug fippukat gii. Sexal, te lekk li ma lay jox.»

¶ «“Tarsis dëkk baa doon sab jula ndax sa gépp xeetu alal ju bare, di indi xaalis, weñ gu ñuul ak gu weex ak beteex, di ko weccikoo seen alal.

Luke 9:62 TSK

Yeesu ne ko: «Képp ku tàmbalee gàbb tey xool gannaawam, jekkoo ci nguurug Yàlla.»

Acts 9:43 TSK

Gannaaw loolu Piyeer dal na Yope ay fan, kër wullikat bu ñuy wax Simoŋ.

¶ «Kon nag buur Àggripa, peeñum asamaan moomu, woruma ko.

Ñooñu lees di mbugale sànkute gu sax dàkk, fu sore Boroom bi, sore teddngay manooreem,