Ba loolu amee Aji Sax ji fomm musiba ma mu waxoon ne dina ko teg ñoñam.
TSK
TSK · Jonah 4:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
“Aji Sax ji! Kiy muñ mer, te bare ngor, di bale tooñ aki moy te du ñàkka topp mukk doom, tooñu waajuram, ba ca sët yaak sëtaat ya.”
Teewul mu yërëm, baal leen seen ñaawtéef, ba sànku leen. Muñ na meram, muñati, te toppul xolam,
Waaye yaw Boroom bi Yàlla, yaa ñeewante, yërëm, yaa muñ mer, bare ngor ak worma.
Yiw ak yërmande, Aji Sax ji; kee muñ mer te bare ngor!
Éy Aji Sax ji, naxtaan nga ma, ma naagu, nga nax ma, jaay ma doole, ba man ma. Ñu ngi may kekku bés bu ne, ku ne di ma kókkali.
Du seeni yére doŋŋ ngeen di xotti, ngir ñaawlu, seenub xol ngeen di xottiwaale, ñaawloo ko. Waññikuleen ci seen Yàlla Aji Sax ji, mooy boroom yiw ak yërmande; mer maa diib, ngor ga bare, muy fomm mbugal.
Boroom bi Aji Sax ji fomm ko ne ma: «Liitam du am.»
Jombul Yàlla dëpp ba fomm, daldi dëddu tàngooru meram, ba dunu sànku.»
Ana Yàlla ju mel ni yaw, di bale ag tooñ, di jéllale ag moy, ñeel ndesu ab séddoom. Kii du denc mer ba fàww, te moo bëgg di yéwéne.