Kon nag kàddug Aji Sax jee, Yàllay Israyil: “Maa waxoon déy ne, sa waa kër ak sa waa kër baay ñooy doxe fi sama kanam, di ma liggéeyal ba fàww.” Léegi nag, kàddug Aji Sax jee: “Loolu jomb naa ko tey. Ñi ma teral laay teral; waaye ñi ma teddadil, dees na leen tuutal.
TSK
TSK · Lamentations 1:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Waaye su ngeen ma dëddoo ba dëddu ma, yeen ak seeni sët, ba jëfewuleen samay santaane, sama dogali yoon yi ma leen tëralal, xanaa di topp aka jaamu yeneen yàlla, di leen sujjóotal,
Ñu ne: “Xanaa li ñu dëddu seen Yàlla Aji Sax, ji jële seeni maam réewum Misra, di topp yeneen yàlla, di leen sujjóotal ak a jaamu. Moo tax Aji Sax ji teg leen musiba mii mépp.”»
Seeni ñaawtéef a dox seen digganteek seen Yàlla. Seeni moy a leen xañ kanamam, ba mu tanqamlu leen.
Ñoom ñépp a di fippukat yu fétteeral, wër di sos, dëgërle ni xànjar ak weñ gu ñuul. Ñoom ñépp di yàqkat.
Man it maay ëñ sa pendal, muure sa kanam, saw taat ne duŋŋ.
Maa leen di def ñu jara seexlu, di musibay mboolem réewi àddina, ba fépp fu ma leen sànni, seen tur di fa saaga te kuy léeboo ak kuy kókkalee mbaa ngay móoloo, ñoom ngay tudd.
¶ «Kon nag, Aji Sax ji dafa wax ne: “Ku nekk ci yeen waroon naa goreel mbokkum dëkkandoom, waaye yeen déy, déggaluleen ma. Man nag maa ngi nii di leen goreel,” kàddug Aji Sax jee, “ngir wacce leen saamar ak mbas akub xiif. Maa leen di def waa réewi àddina yépp seexlu leen.
Waa Siyoŋ gépp a ngi binni, di wut ab dund, seeni ngëneel lañuy weccikoo aw ñam wu ñu leqlikoo.
Éy Aji Sax ji, xoolal sama njàqare, samay butit di fuddu, sama biir xol salfaañoo ndaxu tiis. Man de maa gàntal ba gàntaaral, ba fa biti, saamar di fa bóome, te biir kër it di ndee.
Ñoom lañuy gëdd naan: «Soreleen nu, nit ñu sobewu ñi! Soreleen, soreleen, buleen nu laal.» Ñu daw di tambaambalu ba ca yeneen xeet; ñooña ne leen: «Dootu fii!»
Kàngam yi, ñu jàpp, wékk; te mag ñi, teraleesu leen.
maa ngii nag di dajale mboolem sa far yi la doon bége, ñi nga bëgg ñépp ak ñi nga bañ ñépp. Maa leen di dajalee fu nekk ci sa kaw, ba noppi ñori la yaramu neen, ñu gis la nga ne duŋŋ.
Mbañeel lañuy jëfeek yaw, foqati ñaqoo ñaq, wacc la, nga ne duŋŋ duŋŋaaral. Sa gànctu gu ñàkk kersa dina feeñ, ak dëgër bët gi ngay cagatoo.
¶ «Kon yéefar yi dinañu xam ne ñaawtéefi waa kër Israyil moo leen yóbbe ngàllo ndax la ñu ma ñàkke worma, ba ma xañ leen sama kanam, teg leen ci seen loxoy noon, ñu fàddoondoo saamar.
Moom xamul woon ne man maa ko doon jox pepp meek biiñ bu bees beek diw gi, di ko yéwéne xaalis ak wurus, ñu di ko jaamoo Baal.