TSK

TSK · Lamentations 2:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Aana ne ko: «Du loolu de, sang bi. Dama di jigéen ju ànd ak naqaru xol, waaye du biiñ, du leneen luy màndee lu ma naan. Dama doon diis Aji Sax ji sama tiisu xol.

Job 3:24 TSK

Samay binni di samaw ñam, samay yuux fettax nim ndox.

Sa wal ya sotti, xóote awu moroom ma; say wal ak say gannax, lépp a jaare sama kaw.

Xéewloo sa ngor moo dàq dundu bakkan; ma àddu boog, kañ la!

Yal nanga ma nangul samag ñaan ni cuuraay lu ñu la taalal, yoxo yi ma la tàllal di saraxu ngoon soo gërëm.

sippi ko sama tawat, diis ko sama njàqare.

Sa doom yi ne lasar, mbete kooba yu fiir jàpp, ñu ne lareet fépp fu mbedd daje, këppoo sànjum Aji Sax ji, sa Yàlla ji leen rëbb.

Ma dem, xool àll, gisuma lu moy ñu saamar bóom, ma dugg biir dëkk, gisuma lu moy ñu ne làcc akub xiif, yonent ak sarxalkat di wër réew mi, xam-xam réer leen.”»

Ndeysaan, wurus wa giim na! Ngëneelu wurus soppiku na. Doj yu sell yaa wasaaroo, ca boppu mbedd yépp.

¶ «Ñoom bu ma leen soqee fitti xiif yu aay, fitti faagaagalkat yooyu may fitt ngir faagaagal leen, xiif laa leen di yokkal, ba dagge dugub fi seen biir.

Teewul ngàllo la dem, cig njaam; ay goneem, ñu falaxe leen ci mboolem selebe yoon; ay kàngamam, ñu tegoo bant; kilifaam yépp, ñu jéng leen.

Luke 6:12 TSK

¶ Fan yooyu la Yeesu dem kaw tund wa ngir ñaani fa; mu fanaane faa ñaan ci Yàlla.