TSK

TSK · Lamentations 3:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Daawuda ne Gàdd: «Am naa njàqare lool; waaye naa tàbbi ci loxol Aji Sax ji, ndax yërmandeem réy na, waaye yàlla buma daanu ci loxol nit!»

Ezra 9:13 TSK

Loolu nu dal lépp, sunu jëf ju bon a tax, ak sunu tooñ gu réy. Terewul yaw sunu Yàlla, tegoo nu lu dul mbugal mu yées mi sunuy bàkkaar yellool. Terewul yaw sunu Yàlla, li nu bàkkaar mbugaloo nu ko, te moo nu fi taxa des di dund nii.

Éy Aji Sax ji, yaa rafet ngor, nangul ma! Geesoo ma sa yërmande ju yaa!

Teewul mu yërëm, baal leen seen ñaawtéef, ba sànku leen. Muñ na meram, muñati, te toppul xolam,

bàyyi xel ci kóllëreem ak ñoom, topp ngoram lu réy, ba giif,

Teewul ñu gàntal ma, nanguwñu maa déglu. Kenn nanguwula xalab tuur yu seexluwu yi mu wékki gët, kenn dëdduwul kasaray tuuri Misra. Ma nar leena xëpp samam sànj, ŋaccal leen sama mer ci biir réewum Misra.

¶ «Waaye doom ya dañu maa gàntal. Sama dogali yoon, jëfewuñu ko, sama àttey yoon yiy guddal fanu képp ku koy jëfe, sàmmuñu ko. Sama bési Noflaay lañu ñàkke worma. Ma nar leena xëpp samam sànj, ŋaccal leen sama mer ca màndiŋ ma.

Ana Yàlla ju mel ni yaw, di bale ag tooñ, di jéllale ag moy, ñeel ndesu ab séddoom. Kii du denc mer ba fàww, te moo bëgg di yéwéne.

«Man Aji Sax ji déy, duma soppiku, te yeen noppiwuleen di askanu Yanqóoba, ay workat.