Job 11:13
TSK
Waaye yaw soo defee sa xel ci Yàlla, dékk ko say loxo,
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Waaye yaw soo defee sa xel ci Yàlla, dékk ko say loxo,
Ngalla déglul, ma tinu la, woo la wall, dékk lay yoxo, jublu sa néegu biir bu sell ba.
Boroom bi, bànneexalal sab jaam, yaw laa dékk sama xol.
Yal nanga ma nangul samag ñaan ni cuuraay lu ñu la taalal, yoxo yi ma la tàllal di saraxu ngoon soo gërëm.
Ku màgg, ku kawe ki, ki màkkaanam sax dàkk te turam sell, daa wax ne: «Fu kawe te sell laa màkkaanoo, maa dëkk ak boroom xol bu mokk, te toroxlu, ngir leqli ku toroxlu, leqli boroom xol bu mokk.