Mbas ma seen xadar, gu tar, ak seen mer, mi dul meddi. Maa leen di wasaare ci kër Yanqóoba, tasaare leen ci Israyil.
TSK
TSK · Lamentations 4:16
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Aji Sax jeey def ngeen daanu fi seen kanami noon. Wenn yoon ngeen di dikke, song leen, waaye juróom ñaari yoon ngeen di awe, daw, te dees na leen seexlu ci mboolem nguuri kaw suuf.
«Maa noon maa leen di fàkkas, ba far dakkal lu leen nit doon fàttlikoo.
Buuru Babilon nag jam leen, ñu dee, foofa ca Ribla, ca réewum Amat. Noonu la Yuda génne réewam, dem ngàllo.
tëral seen askan ci biir xeet yi, wasaare leen ci réew yi.
Mag meek kàngam li ñooy bopp bi, yonent bi mokkal naaféq dib geen.
Maa mere woon sama ñoñ, sobeel sama séddoo ñii, teg leen ci sa loxo, te wonoo leen yërmande, ba mag sax, nga teg ko lu diisa diis,
Maa leen di def ñu jara seexlu, di musibay mboolem réewi àddina, ba fépp fu ma leen sànni, seen tur di fa saaga te kuy léeboo ak kuy kókkalee mbaa ngay móoloo, ñoom ngay tudd.
Kàngam yi, ñu jàpp, wékk; te mag ñi, teraleesu leen.
ba ma leen jàppee ci loxo, génne leen réewum Misra. Gannaaw ñoo sàmmul sama kóllëre nag, man it geesuwuma leen, la Boroom bi wax.