TSK

TSK · Lamentations 5:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Nangul ma, Aji Sax ji, rikk nangul ma, ba mbooloo mii xam ne yaw Aji Sax ji yaa di Yàlla te yaay délloosi seen xol ci yaw.»

def nga dëkkandoo di nu xëccoo, noon di nu ree.

Yaw Israyil mu taaru, maa lay defaraat, nga defaru, ba jiinaat sam njiin, wàlli peccum mbéx,

¶ Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Bu ma tijjee seen wërsëg, kàddu gii dina jibati ci réewum Yuda ak dëkk yi ko séq. Dees na ne: “Yaw dëkkuwaayu njekk bii, yaw, tundu Siyoŋ wu sell wi, yal na la Aji Sax ji barkeel!”

¶ Aji Sax ji dafa wax ne: «Bérab bii ngeen ne ab gent la bu kenn nekkul, du nit, du rab te muy dëkki Yudak mbeddi Yerusalem yii gental, kenn nekku fi, du nit, du rab, dees na fi déggati

Maa leen di may beneen xol ak xel mu yees. Xolu doj bi laay roccee ci seen suux, weccee leen ko xolu suux.

¶ «“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Lii laay nangulaatal waa kër Israyil, defal leen ko: maay ful nit ñi niy gàtt.

Aji Sax ji dafa wax ne: «Maay dellu Siyoŋ, Yerusalem googu laay màkkaanoo, ba ñuy wooye Yerusalem dëkkub Worma, foofu di tundu Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, lees di wooye tundu Sellnga.»