TSK

TSK · Leviticus 11:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 28:7 TSK

Wii yoon, tan xamu ko, bëtu jaxaay du ko gis.

Job 39:27 TSK

Am yaa sant jaxaay mu naaw ba fa kaw, di tàgge kawte ya?

«Dofe la sama ñoñ def. Man, xamuñu maay kan, mbetey gone yu dul xalaat dara; dég-dég, tus; seen xel mépp, lu bon rekk, lu baax, xamuñu ci dara.»

Ñi ñuy dàqa gëna gaaw ay jaxaay, ci kaw tund yi lañu nu ne dann, màndiŋ mi, ñu di nu fa tëroo.

Seeni fas a gëna gaawi segg, gëna aay tilli timis. Fu sore la seeni gawar jóge, tëbal, naaw nig jaxaay ju ne jàyy, lekkum rëbbam.

¶ Gannaaw ràññee Yàlla jaralu leen dara, Yàlla it bërgal leen ak seen xel mu doyadi, ba ñuy def jooju jëf ju jekkadi.

Titus 3:3 TSK

¶ Ndax nun itam kat, ñu ñàkk xel lanu woon te déggadi, ñu réer, tënku ci lu doon ay xemmemtéef, ak bànneexi bakkan, tey wéye def lu bon, ak ñeetaane, ñu jara bañ te bañante ci sunu biir.