TSK

TSK · Leviticus 11:25

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba loolu amee Musaa wàcc tund wa, dellu ca mbooloo ma. Mu sell-luloo leen, ñu fóot seeni yére,

Képp ku lekk ca médd ma, na fóot ay yéreem, te du tee mu yendoo sobe ba jant so. Képp ku for médd ma, na fóot ay yéreem te du tee mu yendoo sobe ba jant so.

¶ «Ku dugg biir néeg bi diiru fan yi mu tëje dina yendoo sobe ba jant so.

Képp ku laal lalam, na fóot ay yéreem, sangu, te du tee mu yendoo sobe ba jant so.

¶ «Gannaaw loolu bu boroom jàngoroy xelli ji tàggook sobey jàngoro ja, dafa wara waññ juróom ñaari fan ngir setlu, ba noppi fóot ay yéreem, sangoo ndox mu balle ci bëtu ndox, doora set.

¶ «Ka wacci woon sikketu Asasel, na fóot ay yéreem, sangu, doora mana duggaat ci dal bi.

¶ «Te itam képp ku lekk médd mbaa lu rab fàdd, muy njuddu-ji-réew mbaa doxandéem, na fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so, mu doora set.

Gannaaw loolu na sarxalkat bi fóot ay yéreem, sangu, doora mana duggaat ci dal bi, te du ko tee yendoo sobe ba ca ngoon.

Ku góor kiy tonni dóomi nag wi itam day fóot ay yéreem, te du tee mu yendoo sobe ba ca ngoon. Na loolu di dogalu yoon bu sax fàww, ñeel bànni Israyil, ak doxandéem bu dëkk ci seen biir.

¶ «Na leen loolu ñeel ci kaw dogalu yoon bu sax dàkk. Ka doon wis-wisal ndoxum setlu mi nag, na fóot ay yéreem, te ku laal ci ndoxum setlu mi day yendoo sobe ba ca ngoon.

Mooy ba ko Yonent Yàlla Natan seetsee, gannaaw ba Daawuda dëkkoo ndaw sa ñuy wax Batseba.

¶ «Bésub keroog bëtu ndox dina bënnal kër Daawuda, ak waa Yerusalem, ngir setal bàkkaar ak sobe.

Léegi nag, looy nég? Jógal, ñu sóob la ci ndox, nga set, teqlikook say bàkkaar, te tudd turu Yeesu.”

Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu, ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu.